Studio IA · Récits, musique & mémoire africaine
Single · 6 novembre 2026
Song Geej, nouveau single de KaangStudio. Voix et musique créées avec l'IA, paroles de Xbol.
Song Geej est le deuxième single de KaangStudio, après Xalima. Il est sorti le 6 novembre 2026 sur toutes les plateformes. Les paroles sont de Xbol, en wolof. La voix et la musique sont créées avec l'intelligence artificielle, et KaangStudio l'indique à chaque publication.
Bàkk daa demoon geej
Lu ma sumb daan ko man
Lu ñu sumb daan ko nun
Sumb na fi ay waar
Waar wi, waar wi maa leen sumb
Waar yi, waar yee
Bàkk daa demoon geej, neer wa jàpp ko
Moom de daa demoon geej, neer wa jàpp ko
Bakari daa demoon geej, neer wa jàpp ko
Waaw, lu mu sumb daan ko
Nee na moom, lu mu sombi naan ko moom
Soo demee ba ca kawakaw
Seeno ma ca kaw
Lu kaw di gën kawe
Ngay seenu
Boo segee ci suuf yaay
Dangay daanu
Boo xoole ci suuf yaay
Dangay daanu
Neer wa nga nee
Neer wa !
Bàkk daa demoon geej, neer wa jàpp ko
Séex daa demoon geej yaay, neer wa jàpp ko
Bàkk daa demoon geej yaay
Neer wa jàpp ko
Séex daa demoon geej yaay
Neer wa jàpp ko
Geej xoot na, geej lëndëm na, geej bare na ndox yaay
Sa waa ji, ah, geej mbàmbulaan
Gis nga tundu gi ci biir geej yaay
Xam nga lu ko taac biir geej
Geej yaatu na te amul baŋxaas
Woyy, ndox ma ngi dal
Maa ngi seen benn gaal
Di robin di ñëw
Bakari nga taxaw di joow
Ca gaal gi di ñëw yaay
Bakari nga taxaw di joow di ñëw
Bàkk a ngay joow
Bàkk a ngay joow di ñëw
Bàkk daa demoon geej, neer wa jàpp ko
Bàkk daa demoon geej, neer wa jàpp ko
Sawaay daa demoon geej, neer wa jàpp ko
Bël bël mu jul, bël bël mu jul, bël bël mu jul xànq wa
Sawaay daa demoon geej, neer wa jàpp ko
Mool de xam na geej, mool rekk a xam geej
Bàkk daa demoon geej, neer wa jàpp ko
Ana lu waay doon jaay
Ak fan la mujje
Paroles en wolof, orthographe CLAD. Texte : Xbol.