AI studio · Stories, music & African memory
Single · 4 October 2026
A Wolof-language song carried by writing, composed with AI, so that our languages also exist in tomorrow's tools.
“Bés boo deme bay bind, na nga bind lu am njariñ”
Xalima is the pen, in Wolof. The song carries the heart of the project: to write, and to make our languages exist in tomorrow's tools.
KaangStudio's first single, out since 4 October 2026.
Bés boo deme bay bind
Na nga bind lu am njariñ
Bés boo deme bay bind
Ngalla yaay na am njariñ
Tey ci suba dama nekk sa ma neeg
Xamb sama taal teg sama ànd
Yootu sama Xalima taaj sama daa
Xalima weesuwul di bind
Lu dul gaawa dëñ
Xalima weesuwul di bind
Lu wér te wóor
Di bind luy jëmale sa askan kanam
Xale yi toogaat leen te déglu ma
Xajalante leen te déglu ma
May leen ma nopp te ni tekk
Ku nekk na ma xool te neema jàkk
Soo leen màgge
Ngeen di dox ci cosaan
Soo leen màgge
Ngeen di fàttaliku seen askan
Di wax seeni wax
Di làkk seeni làkk
Mag ñi jiitu xallal na ñu yoon wi
Xalima bu cappe daa nay bind yaay lu am njariñ
Booy bind na rafet bul bind luy yee fitna
Waxtaanal ak say ñoñ ngeen xaatim
Buleen ragal xarala yu bees yi
Te saytu birima moomu di wax ak yeen ci suuf
Xale yi jòg leen
Taxaw ñu yékkati àlluwa yi
Xale yi jòg leen
Taxaw ñu jël téere yi bindal sunu bopp
Balaa birima moomu di ñu bindal
Gis naa ci yow loo xam ni
Gis naa ci moom loo xam ni
Nekkul ci beneen ndaw
Waaye da ma bëgg nga bind ma li ci yow
Ma dencal ko seeni sët sëtaat
Am na foo xam ni soo fa tòoloo doo too nëbu
Da ngay bind fésal sa cosaan ci jamonoy tey
Ëllëg yow dinga nekk lii
Ëllëg yow dinga doon lii
Ëllëg yow da nga nekk lii
Ëllëg yow dinga tekki lii
Xanaa xamoo leen ni
Ëllëg googu suba la
Xanaa da ngeen xamul ni
Ëllëg googu démb la
Ëllëg googu ngoon la woon
Ëllëg googu tey jii la
Ëllëg googu leegi la
Ëllëg googu mi ngee di dem
Kon bòok bindleen
Ay bind rek mooy li fiy des tey
Ndax suba suba Yàlla la
Ndax suba suba Yàlla la
Lyrics in Wolof, CLAD orthography. Text: Xbol.