AI studio · Stories, music & African memory

KaangStudio · Out on 20 November 2026
Other platforms will be added on release day.
Voice and music created with AI. Cover art generated by AI.
Songoo, lëngoo, lëngoo, jokkoo, jàppante
Bañ jàppante ba léegi ngaañ ne wucci
Ba ñu jàppante ba léegi si nii, luy gaañe amu ci
Wëseynoo, loo seenoo, ah, eh
Baa, siin, miim, raa, baa, siin, miim, raa
Waaxid, isnayni, salaasa
A, B, C, A, B, C, en, dë, turwaa
Te xam naa luy sa waar, dinga ko bey ba mu mat sëkk
Man xam naa lépp lu ciy sa waar, dinga ko bey ba mu mat
Ndax bi ñu ne, lu ñu soxal nun mooy suqali dëkk bi
Ku ne su jële xam-xamam, ñu boole xam-xam yi, wasaare
Dañu mëna suqali réew mi
Waaye su kenn di defar, ñaar di yàq, yaay, du sotti yow
Waaw, su kenn di defar, ñaar di yàq, yaay, du sotti yow
Ah, liy bax di xeeñ, bu sotee dina gën
Foo dem ci réew mi, yaay, am na loo xam ni war nañu ko waxtaane
Foo dem ci réew mi, yaay, am na loo xam ni war nañu ko fa def
Soo bëggee sa réew naat, danga di déglu way-xam-xam yi
Soo bëggee, yaay, réew mi naat, danga di déglu way-xam-xam yi
Wàcceel sa bopp ci suuf a suuf, wàccal ci suuf a suuf ba tóllook ñi ci suuf, ndax ñoom nga wara gindi
Gis nga réew mi, lu ko taxawal ? Werante bi, yow, moo tax mu taxaw, yaay
Gis nga réew mi di coow, werante baak ñi xamul moo ko indi, yaay
Gis nga tàkk-tàkk bi ngay seen, ñi xamul, yaay, ñoo ko taal
Kooku nak, dangeen koy teewlu, di ko déglu, ndax Yàlla may na ko xam-xam
Xam na liy doxal réew, xam na liy yor réew
Ah, dégluleen ko
Mbay Mbayaan Mbayo, Masamba Mbay
Suqalil réew mii, nga xam ni suuf sa ngi nii gaañ, asamaan si di taw, ndox mi di bàll
Songoo, lëngoo, lëngoo, jokkoo, jàppante
Bañ jàppante ba léegi ngaañ ne wucci
Ba ñu jàppante ba léegi si nii, luy lore amu ci
Wëseynoo, loo seenoo, ah, eh
Baa, siin, miim, raa, baa, siin, miim, raa, waaxid, isnayni, salaasa
A, B, C, A, B, C, en, dë, turwaa
Lyrics as sung, in Wolof, CLAD spelling. Text: Xbol.
Xalima4 Oct 2026
Song Geej6 Nov 2026
Lëngoo20 Nov 2026